ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem

ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem

Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne aji-gëm ji dëggu cig ngëmam ki ab xolam dal, dana yëg ci xolam ag ubbiku, ak ug yaatu ak mbégte ak neexit, ak cafkag jege Yàlla ndeem gëm na ñatti mbir: Bi ci njëkk: gërëm na Yàlla nekk Boroomam, loolu nag ci mu ubbi dënnam ci la cay rot di bawoo fa Yàlla te kennal Yàlla ci moomeelam di ko waral, ci séddale wërsëg yi ak nekkiin yi, du yég ci xolam genn gaar ci loolu, te du sàkku beneen boroom bu dul Yàlla mu kawe mi. Ñaareel bi: mu gërëm lislaam muy diineem, ci mu ubbi dënnam ci li lislaam làmboo ci def ay jëf, ak i warugar, te du dox ci lu dul yoonu lislaam. Ñatteel bi: mu gërëm Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di yonnenteem, ci mu ubbi dënnam di bég ci li mu indi ci lu dul dengi-dengi walla sikk-sàkka, du sóobu ci lu dul lu dëppoo ak njubam yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

فوائد الحديث

Gëm daa am neexit ak cafka gu ñuy ñam ci xol yi, kem ni ñuy ñame lekk ak naan ci gémmeñ.

Yaram du yëg

neexitu lekk ak naan lu dul bu wéree, niki noonu ab xol bu muccee ci tawatu bànneex yiy

sànke, ak bàneex yu araam yi, day yëg

neexitu ngëm, waaye bu feebaree du yëg neexitu ngëm, amaana sax muy yëg neexaay ci lu alkandeem nekk ak ciy moy Yàlla.

Nit ki bu gërëmee am mbir rafetlu ko day yomb ci moom, te day bég ci lépp lu mu indi, mbégteem jaxasoo ak xolam, niki noonu it aji-gëm ji bu gëm gi duggee ci xolam, jaamu Boroomam da koy yomb, mu neex ci bakkanam, te lamu cay daj du jafe ci moom.

Ibnul Xayyim nee na: hadiis bi dafa làmboo gërëm ci moomeelu Yàlla ak Yàllaam gi, ak gëram ci Yonnenteem bi te wommatul ko, ak gërëm diineem ji te nangul ko.

التصنيفات

Dollikug ngëm ak ug wàññikoom