إعدادات العرض
Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom
Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, te sama jaam bi du deñ di ma jegeñ-jegeñlu ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee maay nekk déggam bi muy dégge, ak gisam bi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam biuy doxe, te bu ma laajee ma jox ko, bu musloo ci man ma musal ko".
الترجمة
العربية Español አማርኛ English اردو Indonesia বাংলা Français Türkçe Русский Bosanski සිංහල हिन्दी 中文 فارسی Tiếng Việt Tagalog Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ ไทย Deutsch پښتو অসমীয়া Shqip Nederlands ગુજરાતી Кыргызча नेपाली Lietuvių دری Српски тоҷикӣ Kinyarwanda Magyar Čeština Moore Malagasy Oromoo ಕನ್ನಡ Azərbaycan O‘zbek Українська ქართული Македонски ភាសាខ្មែរ Bambara ਪੰਜਾਬੀ मराठी Kirundi Kurmancî Bahasa Melayuالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ci hadiisu xudsiyu bii ne Yàlla mu màgg mi nee na: ku lor ab wàlliyu ci sama wàlliyu yi daal di koy merloo daal di koy bañ kooku waajal naa ko ab xeex yégal naa ko ag noonoo. Wàlliyu mooy: aji-gëm ju ragal Yàlla, kem li nekk ci jaam bi ci ngëm ak ragal Yàlla la céram ci wàlliyu Yàlla di nekk. Te jullit bi du jegeñ-jegeñlu Boroomam ci dara lu ko gënal li mu farataal ci moom waral ko ci moom ci def jaamu yi, ak moytu yu araam yi, te jullit bi du deñ di jegeñ-jegeñlu Boroomam ci naafila yi boole ko ak farata yi; ba am mbëggeelu Yàlla. Te bu ko Yàlla bëggee, Yàlla da koy dëgëral ci ñenti céram yii: Da koy dëgëral ci déggam, du dégg lu dul luy gërëmloo Yàlla. Dëgëral ko ci gisam, du xool jëm ci lu dul lu Yàlla bëgg moo xool te mu gërëm ko. Mu dëgëral ko ci loxoom, du def ci lu dul luy gërëmloo Yàlla. Mu dëgëral ko ci tànkam, du dox jëm ci lu dul luy gërëmloo Yàlla, te du dox jëm ci lu dul aw yiw. Ànd ak lii bu ñaanee Yàlla dara Yàlla jox ko li mu laaj, mu nekk ku ñuy nangu ñaanam, bu musloo ci Yàlla làqu ci moom, ngir sàkku kaarànge Yàlla musal ko aar ko ci li muy ragal.فوائد الحديث
Hadiis bii dafa bokk ci li Yonnente bi nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsi walla Hadiisu Al Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la jóge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññetle ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottloowaate ak yenneen.
Tere nañu lor péetey Yàlla yi, xemmemloo nañu it ñu bëgg leen, te nangu seen ngëneel.
Digle nañu ñu noonoo nooni Yàlla yi, te baña féete ak ñoom.
Kuy wootewoo ne péetem Yàlla la te du topp sariihaam ji kooku ab fenkat la ci li muy wootewoo.
Ci def yi Yàlla waral, ak bàyyi yi mu araamal lañuy nekkee péetem Yàlla.
Bokk na ci liy tax Yàlla bëgg jaam bi, di nangu ñaanam, def naafila yi ginnaaw bi ñu taxawee ci def yi war ak bàyyi yi araam.
Tegtale teddngay niti Yàlla yi ak kaweg seen i wàccuwaay.
