Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di féete kaw, ba mbirum Yàlla di leen dikkal ñu nekk way-not

Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di féete kaw, ba mbirum Yàlla di leen dikkal ñu nekk way-not

Jële nañu ci Al-Muxiirata ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di féete kaw, ba mbirum Yàlla di leen dikkal ñu nekk way-not".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne aw nit ci xeetam wi duñu deñ di féete kaw di not ci kaw ñi wuute ak ñoom, noonu lay deme ba mbirum Yàlla di leen dikkal ci ñu jël seen ruu yi ci mujjug jamonoy àdduna njëkk Saa di taxaw.

فوائد الحديث

Kéemtaan gu fés ñeel Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ndax melo wii deñul di wéy -ñuy sant Yàlla- diirub jamonoy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba leegi nii, te du deñ ba mbirum Yàlla mi ñu tudd ci hadiis bi ñëw.

Ngënnelu sax ci dëgg ak jëfe ko, ak ñaaxe ci loolu.

Féete kaw gi diine féete kaw ñaari xeet la: benn muy ci lay ak leeral ak ug leer, walla mu nekk ci doole ak jaasi, féete kaw gi nag ci lay ak leeral luy wéy di des la; ndaxte layu lislaam mooy Alxuraan, lu féete kaw la, di Aji-Not mbooleem ay noonam, waaye xeetu ñaareel bi ci féete kaw gi, mooy kawe ci doole ak jaasi jii nag moom ci kem gëm gi la ak dëgëral gi ci suuf.

التصنيفات

Characteristics of the People of the Sunnah and the Community