dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil

dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil

Jële nañu ci Al-Miqdaad ibnul Aswad yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil", Sulaym ibn Haamir wax ne: giñ naa ci Yàlla ne xamuma lan mooy Miil? Ndax ab soriwaay la ci suuf, walla li ñuy tusngale bët la, mu ne: "nit ñi nekk ci ñaq kem seen i jëf, amna ci ñoom ku muy toll ci ay dojoram, amna ci ñoom ku muy toll ci ay óomam, amna ci ñoom ku muy toll ci ndiggam, amna ci ñoom ku ñaq wi di ŋalaab ag ŋalaab" nee na: Yonente Yàlla bi daal di junj loxoom ci gémmiñam.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne jant bi dañu koy jegeele ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc mu jege leen, ba mu mujj nekk ci seen bopp yi luy toll ni Miil. Taabihii bii di Sulaym ibn Haamir wax ne: Giñ naa ci Yàlla xamuma ban Miil la jublu, ndax soriwaayu suuf si la, walla Miil bi ñuy tusngale bët la? Nee na: ñu nekk ci ñaq wi kem seen i jëf! Am ci ñoom ku ñaq wi di toll ci ay dojoram, am ci ñoom ku muy toll ci ay wóomam, am ci ñoom ku muy toll ci ndiggam fi muy takk koddaayam, am ci ñoom ku ñaq wi di toll ci gémmiñam ba tere ko a wax. Nee na: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di junj loxoom ci gémmiñam.

فوائد الحديث

Leeral njàqare ëllëg bis-pénc ak ragalloo ko.

Nit ñi dañuy nekk ci ag tar-tar ëllëg bis-pénc ca taxawaay ba ci kem seen i jëf.

Xemmemloo ci def jëf yu baax yi, ak ragalloo ci def jëf yu bon yi.

التصنيفات

Dundug alaaxira