bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg

bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi jàngal na kiy óbbali gémmiñam ubbeeku ngir tàyyeel walla suur mbaa luy niru loolu; mu teg loxoom ci gémmiñam tëj ko ci; ndaxte Saytaane da ciy dugg bu ko bàyyee mu ubbiku, bu ko defee tek loxo bi day tax du dugg.

فوائد الحديث

Bu nit nammee óbbali war na ci moom mu nëbb ko kem kàttanam, ci mu téye gémmiñam, ba du ubbiku, bu manul fexe ba du ubbiku kon na teg loxoom ci gémmiñam, ngir muur ko.

Taqoo ak teggini lislaam yi ci gépp anam; ndaxte mooy màndargam matug jikkó yi.

Moytu lépp luy may saytaane mu mana am fumu jaar ba dugg ci nit ki.

التصنيفات

Teggiini tisli ak óbbali