ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”

ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi leeral na ne ku toppu boroom bi jaar ci lislaam, ñu wërsëgal ko lu dagan kem aajoom ëppul yéesul, Yàlla def ko mu doylu gërëm li mu ko jox koo ku texe na.

فوائد الحديث

Texeg nit ki mi ngi ci matug diineem ak doyug dundam ak ug doyloom ci li ko Yàlla jox.

Xemmemloo ci doylu ci li ñu la jox ci àdduna ànd ak lislaam ak sunna.

التصنيفات

Ŋàññ bëgg àddina