bu nit ñi xamoon li nekk ci nodd gi ak sàppe su njëkk si te manu ñu lu dul tegoo bant kon danañu ko tegoo bant

bu nit ñi xamoon li nekk ci nodd gi ak sàppe su njëkk si te manu ñu lu dul tegoo bant kon danañu ko tegoo bant

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu nit ñi xamoon li nekk ci nodd gi ak sàppe su njëkk si te manu ñu lu dul tegoo bant kon danañu ko tegoo bant, te bu ñu xamoon li nekk ci teela dem kon danañu njëkkante jëm ca, bu ñu xamoon it li ci gee ak suba danañu ko dikkal donte dañuy raam".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bu nit ñi xamoon li ci nodd gi ak sàppe su njëkk si ci ngëneel ak yiw ak barke te amuñu genn anamu jiitu ca ak lu dul ñu tegoo bant ba xam kan ci ñoom moo ca gën a yay moroomam kon danañu ko tegoo bant, te bu ñu xamoon li nekk ci teel a jëm ca julli ga ci waxtu wu njëkk wi kon danañu njëkkante jëm ca, bu ñu xamoon it daytalu yool bi nekk ci ñëw ci jullig gee ak jullig fajar kon danañu yombal ñëw ga donte dañuy raam ci seen i wóom kem ni xale di doxe ci njëlbeenu mbiram.

فوائد الحديث

Leeral ngëneelu nodd.

Leeral ngëneelu sàppe su njëkk si, ak jege imaam bi.

Leeral ngëneelu teel a dem ca julli ga ci waxtoom wu njëkk wi ñi sopp; ndax la ca nekk ci ngëneel lu màgg, ak la cay topp ci ay njariñ, bokk na ca: dab sàppe su njëkk sa, ak dab julli ga ca tàmbali ga, ak def naafila, ak jàng Alxuraan, ak am sàkkug njéggal ci malaaka yi, ak ne moom du deñ di nekk ci julli fii ak mi ngi xaar julli gi, ak yeneen yu dul yooyu.

Ñaaxe gu màgg ci teewe mbooloom ñaari julli yii, ak ngëneel yu bari yi nekk ci loolu ndax li ci nekk ci coono ci bakkan ci yàq njëlbeenu nelaw yi ak mujj gi, lii moo tax ñu nekk julli yi gën a diis ci naaféq yi.

An-Nawawii nee na: nekk na ci it saxal tegoo bant ci àq yi ñuy dajee di ca xëccoo.

Sàppe su ñaareel si moo gën su ñatteel si, su ñatteel si moo gën su ñenteel si, noonu lay deme.

التصنيفات

Ngëneel yi, Sunnay julli