إعدادات العرض
Ngëneel yi
Ngëneel yi
1- li dagan de leer na li araam it leer na,
3- bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
8- li dagan de leer na li araam it leer na,
10- ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar
12- kuy dog mbokk du dugg àjjana
13- ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam
15- Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan
18- ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine
23- Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
25- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
29- ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam
33- giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur
35- ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?
42- bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
50- Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
51- Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?
56- waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
57- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
59- Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji
64- yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon
65- jaamu Yàlla ci jamonoy fitna moo ngi mel ni gàddaay jëm ci ma
66- amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo
