إعدادات العرض
bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu
bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Jenn waay dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi damaa am jegeñaale ma leen di jokk ñu may dog, may rafetal jëme ci ñoom ñuy ñaawal jëme ci man, may lewet ci ñoom ñuy fétteerlu ci sama kaw, mu ne ko: "bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල Hausa Kurdî Kiswahili Português தமிழ் Nederlands অসমীয়া ગુજરાતી پښتو മലയാളം नेपाली Magyar ქართული తెలుగు Македонски Svenska Moore Română Українська ไทย मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛالشرح
Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne dafa am ay jegeñaale ak i mbokk muy jëflante ak ñoom lu rafet ñoom ñuy jëflante ak moom safaan; mu leen di jokk di dem si ñoom, ñoom ñu koy dog, muy rafetal jëme ci ñoom ci lu baax ak matal kóllare, ñoom ñuy ñaawal jëme ci ñoom ci tooñ ak foñ, muy lewet ci ñoom di leen baal, ñoom ñuy fétteerlu ci kawam ci wax ak jëf ju ñaaw, ndax mu wéy di leen jokk ànd ak li mu tudd? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bu dee noonu nga wax la deme kon yaa ngi leen di gàccaal di leen doyadal ci seen bopp, ba mel ni danga leen di lekkloo dóom bu tàng; ngir sa rafetal gu bari ak seen jëf yu ñaaw yi ne seen bopp, te doo deñ di am ci Yàlla ndimbal ci seen kaw, mu lay fegal seen i lor fii ak yaa ngi nekk ci lii nga tudd ci ay rafetal jëme ci ñoom, ñoom ñu sax ci di ñaawal jëme ci yaw.فوائد الحديث
Faye ñaawteef ci ag rafetal dees na ci njort ci aji-ñaawal ji dellu ci dëgg, niki ni ko Yàlla mu kawe mi waxe: (deel faye ca namu gën a rafete, kon ki nga xam ne noonoo moo dox seen diggante dana mujj nekk xarit bu la bëgg lool).
Jëfe ndigalu Yàlla donte da ciy jële lor sabab la ci Yàlla dimbali jaam biy aji-gëm.
Dog ag mbokk mettit la ak mbugal ci àdduna, te bàkkaar la ag regle la ca allaaxira.
Jaadu na ci jullit bi muy yaakaar fayug Yàlla ci ay jëfam yu baax, te lori nit ñi ak seen ug dog bañ ko a daggloo aadaam ju baax ji.
Kiy jokk mbokk du kiy fay ki koy jokk, Waaye kiy jokk mbokk dëgg mooy ki nga xam ne bu ñu dogee mbokkam mu jokk ko.
التصنيفات
Ngëneeli jokk bokk yi