buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi

buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi

Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi, walla ngir am ci wàccuwaay ca jotaay ya, képp ku def loolu, sawara la jëm, sawara la jëm".

[Wér na] [Ibnu Maaja soloo na ko]

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo sàkku xam-xam ngir ndamu puukarewu ak woroom xam-xam yi, ak di wane ne man boroom xam-xam laa ne yéen, walla di ci wàqante ak a werente ak way-dese ñi ak ñu gàtt xel ñi, walla di sàkku xam-xam ngir nekk njiit ca jotaay ya, ñu di ko jiital ca kaw ñeneen ña fa nekk. Ku def loolu; kooku yayoo na sawara ngir sababus ngistalam ak ñàkk a sellalam ci sàkku xam-xam ngir Yàlla.

فوائد الحديث

Tëkkoo nañu ci sawara képp kuy sàkku xam-xam ngir ndamu mbaa werente ca walla nekk njiit ca jotaay ya, mbaa yu ko niru.

Solos sellal ñeel kuy sàkku xam-xam te di ko xamle.

Ci yéene la jëf di tabaxu te ca la fay ga di aju.

التصنيفات

Ràgg-ràggi xol yu, Ŋàññ topp bakan ak bànneex yi, Merit and Significance of Knowledge