?julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi

?julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi».

[Sahih/Authentic.] [Muslim]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne julliy juróom yi ñu farataal ci bëccëg gi ak ci guddi gi, ak jullig Àjjuma ci ayu-bis gune, ak woor weeru koor ci at mu ne, da ñuy far bàkkaar yu ndaw yi ci seen diggante ci sartub moytu bàkkaar yu mag yi, Bu dee bàkkaar yu mag yi nag moom niki njaalo ak naan sàngara dara du ko far lu dul tuub.

فوائد الحديث

Bàkkaar yi daa am yu ndaw am yu mag.

Far bàkkaar yu ndaw yi dafa aju ci moytu bàkkaar yu mag yi.

Bàkkaar yu mag yi mooy bàkkaar yi nga xam ne gétan (ay daan) da cee war ci àdduna, walla ag tëkkug àllaaxira ñëw ci mbugal, walla merum Yàlla, walla ag xuppe nekk ca, mbaa ag rëbb ñeel ki ko def, lu mel ni njaalo ak naan sàngara.