إعدادات العرض
Ngëneel yi ak teggiin yi
Ngëneel yi ak teggiin yi
1- Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
2- li dagan de leer na li araam it leer na,
4- Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
5- Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
6- bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
9- kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
12- baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko
13- bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
14- Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?
15- bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
16- bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate
18- moytuleen juróom-ñaar yiy alage
21- Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
23- ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana
24- Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi
25- àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
28- wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
30- yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku
32- ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm
33- li dagan de leer na li araam it leer na,
34- Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
35- Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
36- jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
37- bul mer
39- ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar
41- ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw
43- gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
44- moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen
46- Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli
47- am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree
48- Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am
49- buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital
51- kuy dog mbokk du dugg àjjana
52- ab ràmbaajkat du dugg àjjana
53- ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam
54- fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
55- képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi
56- ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
57- Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo
62- dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana
63- ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen
64- Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan
65- ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc
68- ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine
69- Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu
70- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt
72- def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
73- Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
74- aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli
75- ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó
76- Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
77- bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi
78- yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
80- Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
82- ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay
84- ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
85- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu
86- Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti
88- yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
94- Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
95- bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
97- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
99- yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira
