إعدادات العرض
bul mer
bul mer
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".
[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili فارسی မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල தமிழ் ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Malagasy тоҷикӣ Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული bm Македонскиالشرح
Kenn ci Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dafa sàkku ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu tegtal ko lu koy jariñ, mu digal ko ne ko bu mu mer, te loolu mooy nay moytu lépp lu koy tax a mer, tey téye boppam saa su meree, bañ a topp meram ci di ray mbaa di dóor walla di saaga mbaa lu ko niru. Waa ji baamtu càkkuteefam ay yoon, Yónente bi yokkul la mu ko denkoon te mooy "bul mer".فوائد الحديث
Moytandiku loo mer ak yi koy waral, ndax dafa dajale wépp ay, te mucc ca moo dajale wépp yiw.
Mer ngir Yàlla niki mer su ñu xottee wormay Yàlla dafa bokk ci mer yi ñu gërëm.
Di baamtu wax ji ndeem yittewoo nañu ko ba keroog kiy déglu di ko xam man a peeg njariñam.
Ngëneelu sàkku ndénkaane ci boroom xam-xam.
التصنيفات
Jikko yees gërëm