إعدادات العرض
Jikko yees gërëm
Jikko yees gërëm
1- Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
2- Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
3- bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
4- baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko
5- bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
6- yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku
8- Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
9- bul mer
11- ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw
12- Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli
13- am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree
14- Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am
15- képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi
16- ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
19- dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana
20- ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc
21- Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu
23- def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
24- aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli
25- ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó
26- yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
27- ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
28- jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
29- lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
30- bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
31- Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
34- aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji
36- ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen
38- dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi
