Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu

Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu

Jële na ñu ci Sahd Ibn Abii Waqaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne Yàlla daa bëgg yenn jaamam yi, Bokk na ci ñoom: ki ko ragal, ci def ay ndigali Yàlla, di moytu ay tereem. Bëgg na it: Ku doylu Ku doyloo Yàlla mu màgg mi du sukkandiku ci nit ñi, te du geestu keneen ku dul Yàlla. Day bëgg it: kiy nëbbu, kiy toroxlu, di jaamu Boroomam, di yittewoo luy jariñ, te yittewoowul kenn xam ko, mbaa ñu koy waxtaane, walla di ko tagg.

فوائد الحديث

Leeral yenn melo yiy waral Yàlla bëgg jaamam bi, te mooy ragal Yàlla, ak toroxlu ak gërëm li Yàlla séddale.

التصنيفات

Jikko yees gërëm