bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex

bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex

Jële nañu ci Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc neena: «bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bokk na ci ndénkaane yi ñëw jóge ca Yonnente yu njëkk ya, nit ñi di ko jokkalante ci seen diggante di ko donnante ci ñoom ay xarnu ba mu egg ci ñi jiitu ci xeet wii, xoolal li nga bëgg a def, bu dee dafa bokk ci li ñu dul am kersa kon def ko, waaye bu bokkee ci yi ñuy am kersa kon bàyyi ko; ndax teree def ñaawteef yi mooy kersa, ku amul kersa, day nuur ci ñaawteef yi ak yu bon yi.

فوائد الحديث

Kersa mooy cosaanu jikkó yu tedd yi.

Kersa melo la wu bokk ci meloy Yonnente yi yal na leen Yàlla dolli jàmm, te mooy li ñu jële ci ñoom.

Kersa mooy def jullit bi muy def luy

taaral di rafetal, di bàyyi luy tilimal di ñaawal.

An-Nawawii nee na: ndigal lii ngir

daganal la, maanaam: boo nammee def dara te bookay def doo am kersa ci Yàlla dooka am ci nit ñi tamit kon mangaa def, bu dul loolu bul ko def, ci loolu la lislaam tënku, te leeral gi ci loolu mooy ne yi ñu digle mu war ak ñu sopp ko dees na am kersa ci bàyyi ko, yi ñu tere ak yi ñu sib dees na am kersa ci def ko, bu dee li ñu daganal nag moom, hadiis bi da ciy matale àttey juróom yi, nee nañu it: ndigalul xuppaate la, maanaam mooy: bu ñu roccee kersa ci yaw defal lu la soob; Yàlla dana la ko fay, nee nañu itam: digal la gu am maanaam xibaar, maanaam: ku dul am kersa day def lu ko soob.

التصنيفات

Jikko yees gërëm