lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko

lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko

Jële nañu ci An-Nuwwaas ibn Simhaan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: "lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Laaj nañu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: Melo wi gën a màgg ci lu baax mooy rafet jikkó ci Yàlla ci ragal ko, ak ci nit ñi ci muñ seen lor, ak néew i mer, ak yaatal sa kanam, wax ju teey, ak jokk mbokk ak topp Yàlla ak ñeewant, ak baax, ak rafet nekkiin ak àndandoo yi. Bàkkaar nag mooy luy yëngatu ci bakkan ci ay lënt, mu ciy sikk-sàkka te mu yëg ci boppam ag xat, xol bi am ci sikk-sàkka, mu ragal ne bàkkaar la, te bëggu ko a feeñal ndax li mu ñaaw ci tànneefi nit ñi baax ñi te mat, loolu nag ndaxte bakkan ni mu mel day bëgg nit ñi gis lu baaxam, kon bu bañee ñu gis yenn jëfam yi day lu bon te amul yiw.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci teddngay jikkó yi; ndaxte rafet jikkó dafa bokk ci melo yi gën a màgg.

Dëgg ak neen seen mbir lëntul ci aji-gëm ji, waaye day xam dëgg ci leer giy nekk ci xol bi, di daw neen di ko bañ.

Bokk na ci màndargay lu bon xol bi di jàq di ci dengi-dengi, ak bañ nit ñi gis ko.

As-Sindii nee na: lii mooy mbir yu lënt yi nga xam ne nit ñi ràññeewuñu benn ci ñaar yi; bu dul loolu rekk li ci Sariiha digle bu dee tegtal ba feeñul ca day wuute ak loolu ndax daa bokk ci li baax, li ñu tere it naka noonu daa bokk ci li bon, kon aajowoowul di laaj xol bi ak ug dalam.

Ñi ñuy waxal ci hadiis bi ñooy woroom xol yu mucc yi, waaye du woroom xol yu yàqu yi nga xam ne xamul lu baax te du bañ lu bon lu dul lu jaxasoo ak bànneexam.

At-Tiibii nee na: nee nañu firees na baax ci hadiis bi ci ay maanaa yu bari, ñu firee ko ci benn barab liy dalal xel ak xol, ñu firee ko it ci beneen barab gëm, ci beneen barab lu lay jegeloo Yàlla, fii rafet jikkó, ñu firee rafet jikkó: muñ lor, ak néew i mer, ak yatal kanam, ak teey i wax, yooyu yépp nag yu jegee la ci maanaa.

التصنيفات

Jikko yees gërëm, Jëfi xol yi