Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp

Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp

Jële nañu ci Sadaan Ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: mokkal naa yaari mbir ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi xamle na ne Yàlla mu kawe mi dafa waral si nun rafetal ci lépp, te rafetal mooy: di fuglu Yàlla ba fàwwu, ci jaamu gi ak ci def yiw ak ci fegal mbindeef yi lor, bokk na ci loolu di rafetal cig ray ak cig rendi. Rafetal cig ray ci jamonoy fayontoo: ci tànn yoon wa gën a yomb te gën a woyof te gën a gaaw ci faat ki ñuy ray. Rafetal cig rendi mooy: mu am ñeewantu ci bayima bi mu ñawal jumtukaay bi, te bañ koo daas ci kanamu la muy rendi, fekk ma nga koy xool, te mu bañ koo rendi fekk am na fa ay jur yu koy xool.

فوائد الحديث

Yërmàndeg Yàlla mu kawe ak ñeewantoom ci mbindeef yi

Rafetal ray gi ak rendi gi ci defe ko ca anam ga ñu ko yoonale.

Matug Sariiha ak làmboo gimu làmboo léppi yiw, bokk na ca yërëm rab yi ak ñeewantu leen.

Tere di ñaawal yaramu nit ki ginnaaw bi ñu ko rayee.

Araamug lépp loo xam ne mbugal baayima da caa nekk.

التصنيفات

Rendi, Jikko yees gërëm