Nekkul woon ku ñaaw i wax du caagine ay jëf, du caagine kuy coow ci ja yi, (marché)te daawul fayantoo lu ñaaw, waaye day baale di jéggale

Nekkul woon ku ñaaw i wax du caagine ay jëf, du caagine kuy coow ci ja yi, (marché)te daawul fayantoo lu ñaaw, waaye day baale di jéggale

Jële nañu ci Abii Abdul Laahi Al-Jadalii nu wax ne: laaj naa Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm jikkóy Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Nekkul woon ku ñaaw i wax du caagine ay jëf, du caagine kuy coow ci ja yi, (marché)te daawul fayantoo lu ñaaw, waaye day baale di jéggale.

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Laaj nañu yaayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jikkóy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: bokkul woon ci jikkóom wax ju bon ak jëf ju bon, te du jéem a ñaawal du caagine mu tay ko, du caagine it di coow di yëkkëti kàddoom ci ja yi, te du fayantoo lu ñaaw; waaye day faye lu rafet, di baale ci biir, di jéggale di dummóoyu ci li feeñ.

فوائد الحديث

Leeral ni Yonente bi melowoo woon ci ay jikkó yu kawe ak ni mu soree woon jikkó yu ñaaw yi.

Ñaaxe ci def jikkó yu rafet yi ak sori jikkó yu ñaaw yi.

Ŋàññ na ñu wax ju ñaaw ak wax ju bon.

Ŋàññ na ñu yëkkëti kàddu ci kaw nit ñi ak yuuxu ci seen kaw.

Ñaaxe na ñu faye lu ñaaw ci lu rafet ak jéggale ak baale.

التصنيفات

Jikko yees gërëm, Man a jéggaleem SLM