bokk na ci séen tànneef yi ñi gën a rafet jikkó

bokk na ci séen tànneef yi ñi gën a rafet jikkó

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: «bokk na ci séen tànneef yi ñi gën a rafet jikkó».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Bokkul woon si jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ju ñaaw, walla jëf ju ñaaw, te daawu ko jublu it mbaa mu koy tay, ndax moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- boroom jikkó yu màgg la. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na wax naan: ki gën ci yéen fa Yàlla mooy ki gën a rafet jikkó, ci def njekk, ak leeral xar kanam, ak téye lor te muñal ko nit ñi, ak jaxasook nit ñi ca na mu rafete.

فوائد الحديث

War na ci aji-gëm ji mu sori lu ñaaw moo xam wax ju ñaaw la mbaa jëf ju ñaaw.

Matug jikkoy Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, dara daawul juge si moom lu dul jëf ju sell ak wax ju teey.

Jikkó ju baax mooy bérabu joŋante ba, ndax ku jiitu rekk bokk ca way-gëm ya gën, te gën a mat sëkk ag ngëm.

التصنيفات

Jikko yees gërëm