amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf

amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne li gën a diis ci màndxem jullit bi i ëllëg bis-pénc ci ay jëf ak i wax mooy rafet jikkò ci di fecci kanam, ak bañ a lore, ak di def njekk. Yàlla mu kawe mi nag dafa bañ lu ñaaw ci jëf ak ci wax, ak ki bon li muu wax ci làmmiñam.

فوائد الحديث

Ngëneelu rafet jikkò, ndaxte day defal boroomam mu am mbëggeelu Yàlla, ak mbëggeelu jaamam ñi, te moo gën a màgg ci lu ñuy peese ëllëg bis-pénc.

التصنيفات

Jikko yees gërëm, Teggiini wax ak noppi