إعدادات العرض
dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana
dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana, te nit ki du deñ di dëggal di jublu dëgg ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab dëggalaakon la, maa ngi leen di moytandikuloo fen, ndaxte fen day yóbbe cig kàccoore, te ag kàccoore day yóbbe sawara, te nit ki du deñ di fen, di jublu fen, ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab fenkat la».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල Hausa Kurdî Português தமிழ் অসমীয়া Kiswahili ગુજરાતી Nederlands پښتو नेपाली മലയാളം Svenska ไทย Кыргызча Română ಕನ್ನಡ Српски తెలుగు ქართული Moore Magyar Македонски Čeština Українська Lietuvių Kinyarwanda Azərbaycan አማርኛالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na dëggu, mu xamle ne taqoo ak moom day yóbbe ci jëf yu baax yiy sax, te taqoo ak jëf yu baax day jëme boroomam àjjana, te dëgg du deñ di bàmtu ci moom ci li nëbbu ak li feeñ, ba mu yeyoo turu dëggalaakoon; te ag jotale la cig dëggu, Yonnente bi yal na ko Yàlla xeexal ak mucc tere na fen ak wax ay neen; ndaxte moom day jëme ci jeng wolif ag njub, ak jëm ci aw ay ak ug yàq ak i moy, topp mu yóbb boroomam sawara, te du deñ di baril fen ba ñu bind ko fa Yàlla mu bokk ci fenkat yi.فوائد الحديث
Dëggu jikkó ju tedd la dees na ko ame cig fàggu ak pasteefu, nit ki du deñ di dëggal di jublu dëgg, ba dëgg mujj nekk melookaanam, ñu bind ko fa Yàlla ne ci way-dëggal yu baax yi la bokk.
Fen jikkó ju ñu ŋàññ la, fen-kat bi day yàgga fen ci wax ak jëf ba fen mujj nekk jikkóom ak meloom, topp ñu bind ko fa Yàlla ne ci fenkat yi la bokk.
Dëggal dees na ko wax ci dëggalug làmmiñ, te mooy safaanu fen, ak dëggug yéene, te mooy sellal, ak dëggug dogu ci yiw wu mu yéene, ak dëggu ci jëf yi, la ca gën a néew mooy li nëbbu ak li feeñ yemoo, ak dëggu ci màqaama yi, niki dëggu ci ragal ak yaakaar ak yeneen, ku melowoo loolu kon ab dëggalaakoon la, walla mu melowoo yenn ci yooyu kon day nekk aji-dëggal.
التصنيفات
Jikko yees gërëm