yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku

yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku

Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñaanal yërmaande ñeel képp ku yomb te tabe di ku yaatu cim njaayam; Du taral ci kiy jënn ca njëg ga, te day jëflanteek moom ci jikko yu rafet, Di ku yomb te tabe te yomb bu dee jënn; du ŋott te du xeeb dayob bagaas ya, Di ku yomb te tabe te yéwen bu dee sàkku ñu fay ko ay boram; du tar ci aji-ñàkk ji ak aji-yittewóo ji, waaye da koy sàkku cig nooy ak ñeewantu, te day néggandiku ki ne ci jafe-jafe.

فوائد الحديث

Bokk na ci jubluwaayi Sariiha sàmm lépp luy yéwénal diggante nit ñi.

Xemmemloo ci jëfandikoo jikko yu kawe yi ca jëflante yay dox diggante nit ñi, ci jaay ak jënn ak yeneen yi.

التصنيفات

Jikko yees gërëm