ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc

ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daf nuy xamal ne képp kuy sàmm wormay mbokkum jullit ci jëw ak ci tere ñu ŋàññ ko walla jëmale si moom lu ñaaw, Yàlla dana ko fegal mbugal ca bis-pénc ba.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Tere nañu di wax ci deru jullit ñi.

Am pay daal mu ngay toll kem na jëf ja tollu, ku feg deru mbokkam Yàlla fegal ko sawara.

Lislaam diiney mbokkoo la ak dimbalante ci diggante ay ñoñam.

التصنيفات

Ngëneel yi ak teggiin yi, Jikko yees gërëm