إعدادات العرض
yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी සිංහල ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands Kiswahili தமிழ் دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Oromoo Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day digle ñu woyofalal nit ñi te bañ a jafeel ci séen kaw ci mbooleem biri diine ji, ak yu àdduna yi, loolu nag day yam fa Yàlla daganal te yoonal ko. Day ñaaxe ba tay ci bégle ciw yiw, ak bañ a dàqaate.فوائد الحديث
Li war aji-gëm ji mooy mu bëggal nit ñi ci Yàlla te xemmemloo leen lu baax.
Jaadu na ci kiy woote ci Yàlla mu xool cig xereñte naka lay àggalee wooteb Lislaam bi ci nit ñi.
Bégle day waral mbégte ak ug jublu ak dal ñeel aji-woote ji li muy woo nit ñi.
Jafeel day waral daw ak dummóoyu ak sikk-sakka ci waxi aji-woote ji.
Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi, te moom diine ju yaatu la leen bëggal ak Sariiha ju yomb.
Yombal gi ñu digle mooy gi Sariiha indi.
التصنيفات
Jikko yees gërëm