إعدادات العرض
ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen
ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu", ñu ne ko:yaw Yonente Yàlla bi, nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy al-mutafayxihuuna? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල ئۇيغۇرچە Kurdî தமிழ் অসমীয়া Nederlands Kiswahili Hausa ગુજરાતી Magyar ქართული Română Português ไทย తెలుగు मराठी دری አማርኛ Malagasy Македонски ភាសាខ្មែរ Українська ਪੰਜਾਬੀالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne ñi mu gën a bëgg ci yéen ci àdduna, ak ñi ko gën a jege ëllëg bis-pénc ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, ak ne ñi mu gën a bañ ci yéen ci àdduna, ñu gën ko a sori ëllëg bis-pénc ñooy ñi gën a ñaaw jikkó ci yéen; (coowkat yi) ñi bari wax ci ag dëgëral ak génn dëgg ga, (ak puukarekat yi) ñiy yaatal ci wax ngir jaay man a wax ak màggal seen i wax ci ku dul fegu ak moytu, (ak ñiy rëy-rëylu), ñu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, nun de xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, lan mooy mutafayxihuuna? Mu ne: ñooy ñiy rëy-rëylu di yéjji nit ñi ñiy ubbi seen gémmiñ yi di wax lu bari.فوائد الحديث
Rafet jikkó dafa bokk ci liy waral bëggug Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak jege ko ëllëg bis-pénc, ñaaw jikkó nag safaanu loolu la.
Rafet jikkó bokk na ci sabab yiy tax nit ñi bëggante, ñaaw jikkó nag safaanu loolu la.
Ñaaxe ci rafetal ak toroxlu ak bañ a soxor ak di dëgëral.
Àrtu ci wax ju bari ak rëy-rëylu ak soxor.
التصنيفات
Jikko yees gërëm