إعدادات العرض
ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Fulfulde Magyar ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Македонски Malagasyالشرح
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ki dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm, koon jaam bi di yërëm mbindeef yi daa bokk ci sabab yi gën a rëy yi nga xamne dees na ci ame yërmàndey Yàlla mu kawe mi.فوائد الحديث
Yërmànde ci mbooleem mbindéef loolu de luñu sàkku la, waaye dañoo tudd nit ngir fonk giñuleen fonk.
Yàlla mooy Aji-Yërëme ji te mooy yërëm ay jaamam yiy yërëme, ndax pay moom ca kem jëf ja rekk.
Yërëm nit ñi day làmboo di àggale ci ñoom baax di leen jeñal lu ñaaw tey jëflanteeg ñoom lu rafet.
التصنيفات
Jikko yees gërëm