ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam

ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yònente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne nit ki gën a mat ngëm ci nit ñi mooy ki gën a rafet jikko, ci béllil xar kanam, ak def njekk, ak rafet i wax, ak jeñ lor. Ak ne ki gën ci way-gëm yi mooy ki gën ci ay jigéenam, niki ay jabaram ak i doomam yu jigéen, ak i mbokkam ak ay jegeñaaleem yu jigéen; ndax ñoom ñoo gën a yayoo ci nit ñi jikko ju rafet.

فوائد الحديث

Ngëneelu jikko ju rafet ak ne ci ngëm la bokk.

Jëf ci ngëm Yàlla la bokk, day yokku di wàññeeku.

Lislaam daa teral jigéen tey soññee ci rafetal jëme ci moom.

التصنيفات

Jikko yees gërëm, Dundiinu ñaari way-dencante yi