Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam

Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam

Jële nañu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne ´gëm gu mat kenn du ko am lu dul ne dafa bëggal mbokkam li mu bëggal boppam ci jaamu Yàlla ak xeetu yiw yi ci diine ak ci àdduna, bu gisee ci mbokkam ag wàññeeku ci diineem, day pasteefu ci yéwénal ko, bu ca gisee yiw mu dëgëral ko ca, te dimbale ko ca, daal di koy laabire ci mbiri diineem ak àddunaam.

فوائد الحديث

Nit ki dafa war a bëggal mbokkam li mu bëggal boppam; ndaxte dàq gëmug ki bëggalut mbokkam li mu bëggal boppam day tegtale warug loolu.

Mbokkoo ci Yàlla moo gën a kawe mbokkoo ci askan, kon nag àqam moo gën a war.

Araamal nañu lépp luy dàqonte ak mbëggeel gii ci ay wax ak i jëf niki wuruj ak jëw ak soxor ak noonoo ci kaw bakkanu jullit bi ak alalam ak deram.

Jëfandikoo yenn baat yiy sawarloo ci jëf; ndax li mu wax ne "ñeel mbokkam".

Al-Kirmaanii yal na ko Yàlla yërëm nee na: bokk na ci gëm ba tay mu bañal mbokkam li mu bañal boppam ci ay, tuddu ko nag; ndaxte bëgg dara day taqoo ak bañ safaanam, kon ñàkk gee tudd ag doyloo la rekk.

التصنيفات

Jikko yees gërëm