Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli

Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli

Jële nañu ci Abbu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaaxe ci jëf ju baax, te bañkoo xeeb donte dafa tuuti, bokk na ci yooyu kanam gu leer ak di muuñ boo dajeek keneen, kon war na ci jullit bi mu xér ci loolu; ngir la ca nekk ci wéttali mbokkum jullit, ak duggal mbegte ci xolam.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

Ngëneelu bëggante ci diggante jullit ñi, ak muuñ ak bég boo dajeek keneen.

Matug sariiha jii ak ug làmboom

lépp luy baaxal jullit ñi, ak lu leen di bennale

Ñaaxe ci def lu baax donte lu néew la.

Sopp nañu di bég Loo jullit ñi; Ndax loolu dafay tax ñu gën a miinante.

التصنيفات

Jikko yees gërëm