am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree

am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ci ne doole dëgg du dooley yaram, mbaa doole juy daan ñeneen nit ñu am doole, waaye ku am doole mooy kiy xeex ak bakkenam te man a not saytaane bu meree.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

gëneelu lewet ak téye sa bopp boo meree, ndaxte daa bokk ci jëf yu sell yi nga xam ne Lislaam da ciy soññee.

Xeex ak sa bàkkan boo meree moo gën a tar xeex ak noon bi.

Lislaam dafa soppi la ceddo ya jàppe woon , mu nekk jikko ju baax, kon nit ki ëpp kàttan mooy kiy téye boppam bu meree.

Sori mer; ngir li muy waral ci lor nit ki ak mbooloo mi.

التصنيفات

Jikko yees gërëm