إعدادات العرض
Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
Jële nañu ci Abuu Yahlaa Saddaad ibn Aws yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi".
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية Español አማርኛ English اردو Indonesia বাংলা Français Türkçe Русский Bosanski සිංහල हिन्दी 中文 فارسی Tiếng Việt Tagalog Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ ไทย Deutsch پښتو অসমীয়া Shqip Nederlands ગુજરાતી Кыргызча नेपाली Lietuvių دری Српски тоҷикӣ Kinyarwanda Română Magyar Čeština Moore Malagasy Oromoo ಕನ್ನಡ Azərbaycan O‘zbek Українська ქართული Македонски ភាសាខ្មែរ Bambara ਪੰਜਾਬੀ मराठी Kirundi Kurmancî Bahasa Melayuالشرح
Yónente bi xamle na ne Yàlla mu kawe mi dafa waral si nun rafetal ci lépp, te rafetal mooy: di fuglu Yàlla ba fàwwu, ci jaamu gi ak ci def yiw ak ci fegal mbindeef yi lor, bokk na ci loolu di rafetal cig ray ak cig rendi. Rafetal cig ray ci jamonoy fayontoo: ci tànn yoon wa gën a yomb te gën a woyof te gën a gaaw ci faat ki ñuy ray. Rafetal cig rendi mooy: mu am ñeewantu ci bayima bi mu ñawal jumtukaay bi, te bañ koo daas ci kanamu la muy rendi, fekk ma nga koy xool, te mu bañ koo rendi fekk am na fa ay jur yu koy xool.فوائد الحديث
Yërmàndeg Yàlla mu kawe ak ñeewantoom ci mbindeef yi
Rafetal ray gi ak rendi gi ci defe ko ca anam ga ñu ko yoonale.
Matug Sariiha ak làmboo gimu làmboo léppi yiw, bokk na ca yërëm rab yi ak ñeewantu leen.
Tere di ñaawal yaramu nit ki ginnaaw bi ñu ko rayee.
Araamug lépp loo xam ne mbugal baayima da caa nekk.
