kersa ci ngëm la bokk

kersa ci ngëm la bokk

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dégg na benn waay di yedd mbokkam ndax kersa, mu ne ko: "«kersa ci ngëm la bokk».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dégg benn waay muy dénk mbokkam ci ngir mu bàyyi bari kersa! Mu leeralal ko ne kersa ci ngëm Yàlla la bokk, te yiw rekk lay indi. Kersa jikko la la juy yóbbe ci def lu rafet ak bàyyi lu ñaaw.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Li lay teree def aw yiw deesu ko woowe kersa, waaye yaras lañu koy woowe walla lompañ mbaa wayadi walla ragal.

Am kersa ci Yàlla mooy di def ay ndigalam, bàyyi ay tereem.

Am kersa ci nit ñi mooy wormaal leen, ak jox leen seen wàccuwaay, ak moytu lu aada ñaaw lu.

التصنيفات

Jikko yees gërëm