إعدادات العرض
Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල தமிழ் دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Azərbaycanالشرح
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bi ngëmam du mat ba keroog muy jiital bëgg Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bëgg yaay ak baay ak doom ju góor ak doom ju jigéen ak nit ñépp, te bëgg gii day war ñu topp ko di ko dimbale, te bañ koo moy.فوائد الحديث
warug bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te jiital ko ci bëgg mbindéef yépp.
Bokk ci màndargay bëgg gu mat: dimbali Sunnas Yónente Yàlla bi, ak joxe sa bakkan ak sa alal ci loolu.
Bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waral topp ko ci lu mu digle, ak dëggal ko ci lu mu xibaare, ak moytu lu mu tere te xuppe ca, topp ko te bàyyi bidaa.
Àqi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gën a màgg gën a feddaliku ci àqi nit ñépp; ndaxte moom mooy sababus sunug gindiku juge cig réer, ak sunug mucc ci sawara ak am àjjana.
التصنيفات
Jëfi xol yi