Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj

Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu jaam bi waxee: {Alhamdu lil-Laah Rabbil haalamiina}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi sant na ma, bu waxee: {Ar-Rahmaanir Rahiimi}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi tagg na ma, bu waxee: {Maaliki yawmid diini}, mu wax: sama jaam bi màggal na ma, -am yoon bumu wax: sama jaam bi wéeru na ci man-, bu waxee: {Iyyaaka nahbudu wa Iyyaaka nastahiinu}, mu wax: lii sama diggante la ak sama jaam bi, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu waxee: {Ihdinas siraatal mustaxiima, siraatal lasiina anhamta halayhim xayril maxduubi halayhim wa laddaaliina}, mu wax: lii sama jaam bi moo ko moom, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne Yàlla mu kawe mi dafa wax ci Hadiis bu sell ba ne: seddale naa saaru Faatiha ci biir julli gi ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ma moom xaaj bi, mu moom beneen xaaj bi. Xaaj bu njëkk bi: sant la ak tagg ak màggal Yàlla, te dinaa ko ci fay gën gi fay. Xaaju ñaareel bi: toroxlu la ak ñaan, dinaa ko ci wuyu, jox ko li mu laaj. Aji-julli ji bu waxee: {Alhamdu lil-Laahi Rabbil haalamiina}, Yàlla wax: sama jaam bi sant na ma, bu waxee {Ar-Rahmaanir Rahiimi}, Yàlla wax: sama jaam bi kañ na ma tagg na ma, nangu na it mbooleem samay xéewal ci sama mbindéef yi, bu waxee: {Maaliki yawmid diini}, Yàlla wax: sama jaam bi màggal na ma, te mooy teddnga gu yaatu ga. Bu waxee: {Iyyaaka nahbudu wa Iyyaaka nastahiinu}, Yàlla wax: lii sama diggante la ak sama jaam bi. Xaaj bu njëkk bi ci aaya bii Yàlla a ko moom te mooy: (Iyyaaka nahbudu) te mooy nangu ne jaamu Yàlla moo ko jagoo, ak wuyu ko ci di ko jaamu, foofu la xaaj bi Yàlla moom yam. Xaaj bu ñaareel bi ci aaya bi jaam bi moo ko moom: (Iyyaaka nastahiinu) sàkku ndimbal ci Yàlla, ag digam ci dimbalee. Bu waxee: {Ihdinas siraatal mustaxiima* siraatal lasiina anhamta halayhim xayril maxduubi halayhim wa laddaaliina}, Yàlla wax: lii ag toroxlu la ak ñaan gu bawoo ci sama jaam bi, kon ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, te nangu naa ñaanam gi.

فوائد الحديث

Màggaayu mbiri Faatiha, ndax Yàlla mu kawe mi sax da koo tudde(Julli).

Leeral ne Yàlla yittewoo jaamam bi, ba tax mu tagg ko ngir cant gi mu ko sant tagg ko màggal ko, mu dig ko ne dana ko jox lu mu laaj.

Saar wu tedd wii dafa làmboo, sant Yàlla, fàttaliku dellu ga, ñaan Yàlla, sellal jaamu gi ñeel ko, ñaan gindiku ci yoon wu jub wa, ak artu ci yooni caaxaan yi.

Jullikat bi buy teewlu hadiis bii -buy jàng Faatiha - day dolli ag toroxloom ci julli gi.

التصنيفات

Ngëneeli saar yi ak laaya yi, Ngëneeli Alquraan ju tedd ji