إعدادات العرض
ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara
ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, yan mooy ñaar yiy waral ? Mu ne ko: «ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Español Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe Bosanski සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Kurdî Hausa മലയാളം తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া Shqip دری Ελληνικά Български Fulfulde Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda Српски тоҷикӣ O‘zbek नेपाली Moore Oromoo Soomaali Tagalog Français Azərbaycan Українська Português bm Deutsch தமிழ் ქართული mk Magyar فارسی lnالشرح
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaari jikko: jiy waral dugg àjjana, ak jiy waral dugg sawara? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tontu ko ne ko: melo wiy waral dugg àjjana mooy nit ki faatu fekk Yàlla rekk la doon jaamu te bokkaalewu ko ak dara. Jiko jiy waral dugg sawara nag mooy nit ki faatu fekk da doon bokkaale Yàlla ak dara, di wutal Yàlla ndend jig jaamu ak momeelam gi ak ay turam ak i meloom.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal hdiis bi:
Ngëneelu Tawhiid ci ne képp ku faatu di aji-gëm te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana.
Loràngey bokkaale, ci ne képp ku faatu te bokkaale Yàlla ak dara dana dugg sawara.
Ñiy kennal Yàlla tey def ay bàkkaar ñoo ngi ci suufu coobarey Yàlla bu ko soobee mbugal leen, bu ko soobee it mu jéggal leen, waaye seenug mujj mooy àjjana.