إعدادات العرض
Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi
Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi
1- tabax nañu lislaam ci juróom
5- Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral
7- yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka
10- Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal
13- Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
14- ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
17- Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
20- Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
22- bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko
24- ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
29- buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
30- ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
31- tabax nañu lislaam ci juróom
35- Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi
36- buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw
39- man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee
40- jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
42- Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse
44- éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale
45- giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom da ngeen topp yoonu ña leen jiitu woon
47- nit ñi gën a tar mbugal fa Yàlla ëllëg bis-pénc ñooy ñiy roy bindub Yàlla bi
48- doomu Aadama weddi na ma te loolu waru ko woon,mu saaga ma te waru ko woon
50- amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante
51- ku takk ab téere bokkaale na
54- malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal
55- buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay
58- maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal
61- Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
62- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
63- xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
64- yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
