إعدادات العرض
seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
Jële nañu ci Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax li njëkk juroom i fan laata muy faatu naan: " seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit, te bu ma doon wut ab xarit ci yéen kon dinaa def Abuu Bakar ab xarit. Yégleen ne ña leen jiitu woon dañu daan jàppe bàmmeeli seeni Yónent ak seen i nit ñu baax ay jàkka, rikk waay! Buleen jàppe bàmmeel yi jàkka, man tere naa leen ko".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Akan Azərbaycan Български Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy नेपाली or Română Kinyarwanda тоҷикӣ O‘zbek Moore Oromoo bm Українська rn Српски ქართული Македонски Lingalaالشرح
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare Na dayo bi mu am fa Yàlla, ci ne moom àgg na ca gën gaa kaweg daraja ci mbëggeel, kem ni ko Ibraahiima ame woon -yal na ko Yàlla dolli jàmm- , looloo tax mu ne amul benn xarit bu dul Yàlla; ndax xolam dafa fees ci bëgg Yàlla mu kawe mi ak màggal ko ak xam ko, kon keneen ku dul Yàlla xaju fa, Te bu doon am ab xarit ci mbindéef yi Abuu Bakar lay doon -yal na ko Yàlla dollee gërëm-. Mu moytandikuloo jéggi dayo ci néew yi kem ni ko Yahuud yi ak Nasaraan yi defe ci bàmmeeli séen Yónente yi ak ñu baax ñi, ba mujj ñu def ko ay yàllay, di ko jaamu bàyyi Yàlla, ñu tabax ca bàmmeel ya ay jàkka ak i jaamukaay. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- tere na aw xeetam ci ñuy def lu mel ni séen jëf ya.فوائد الحديث
Ngënéel u Abuu Bakar Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ag ne moom moo gën ci Sahaaba yi, te moo gën a yay ci nit ñi ngir nekk Xaliifab Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ginnaaw bi mu faatoo.
Tabax jàkka ci bàmmeel daa book si ñaawtéefi xeet ya jiitu woon.
Tere ñuy jàppe bàmmeel yi ay barab ngir jaamu, di fa julli walla di ko jublu, walla di tabax ca kawam ay jàkka ak i xubba, ngir moytandikuloo tàbbi ci bokkaale ci sababus loolu.
Moytandikuloo ëppal ci gaayu baax yi ndax day jëme ci bokkaale.
Ñàngug li Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di moytandikuloo ba tax mu feddali ko lu jiitu muy faatu ci juróomi guddi.