buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay

buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay

Jële na ñu ci Abdur Rahman Ibn Samurata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere giñ ci Taaxuut yi, te mooy xërëm yi bokkaalekat yi daan jaamu wolif Yàlla, te sabab la ci seen ug bew ak seen ug kéefar, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere ñuy giñ ci baay yi; ndax daa bokkoon ci aaday araab yi ca ceddo ga ñuy giñ ci seen baay yi ngir ndamu ak màggal.

فوائد الحديث

Giñ ci ku dul Yàlla ak i turam ak i meloom daganul.

Araamal nañu giñ ci Tawaaxiit yi, ak ci

baayeek maam yi ak ci njiit yi, ak ci xërëm yi, ak lepp

luko niru ci ay neen.

Gin ci ku dul Yàlla bokkaale gu ndaw la, te man naa nekk bokkaale gu mag, bu màggalee li muy giñe ci xolam kem ni ñuy màggale Yàlla walla mu fas ci dara ci ag jaamu.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko