baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen

baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ay nit laaj na ñu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri gisaanekat, mune leen: «nekkuñu ci dara» ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ñoom de leeg-leeg ñu wax nu dara mu nekk dëgg’ mine leen: «baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Laaj na ñu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri ñiy xibaare kumpa ci li ñëwagul, mu wax ne: buleen leen faale, te buleen jël séen i wax, te buleen séen mbir yitteel. Ñu ne ko: ñoom séen wax leeg-leeg mu dëppoo ak li am, kem bu ñu xibaare ne benn mbiru kumpa dana am ci weer nàngam ak bis sàngam, dafay am kemm ni ñu ko waxe. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: jinne yi ñooy jëf li nuy dégg ci xibaaru asamaan, ñu wàcc dem ca séen kilifay gisaanekat ya wax leen la ñu dégg, gisaanekat bi dolli ci li jinne yi dégge ca asamaan téeméeri fen.

فوائد الحديث

Tere nañu dëggal ab gisaanekat, ak ne ñoom li ñuy wax ay fen la ay sos la, donte leeg-leeg sax mu wax dëgg.

Aarees na asamaan si ci Saytaane yi ginnaawam bi ñu yónnee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba duñu dégg dara ci soloo gi mbaa leneen, lu dul ku sàcc ab dégg daal di rëcc jum yay tàkk.

Jinne yi dañu leen di wutal ay péete ci nit ñi.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko, Masalay ceddo ga