Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi

Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi

Jële nañu ci Umar Ibnu Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : «Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi", Umar wax ne : ba ma déggee Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di ko tere giñatuma ca mooxam ci lu ma ci samay wax mbaa may jottali waxi keneen ».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne Yàlla mu kawe mi day tere ñuy giñ ci suñuy baay, ku nàmm a giñ bu mu giñ ci ku dul Yàlla, waaye bu mu giñ ci keneen. Umar Ibnul Xattaab wax ne moom de giñatu ca diirub ba mu déggee Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di ko tere, moo xam mu tay ko, walla muy tuxal giñug keneen ci lu dul Yàlla.

فوائد الحديث

Araamalees giñ ci ku dul Yàlla, dañoo jagleel baay cig tudd nag ngir li mu nekkoon aaday ceddo ya.

Giñ : mooy giñ ci Yàlla walla ay turi Yàlla mbaa ay meloy Yàlla ci menn mbir ci bir yi ngir feddali ko.

Ngëneelu Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ci ni mu

gaawee jëfe ndigal, ak rafetug déggam ak fegoom.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko