إعدادات العرض
ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tagalog Kurdî Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Hausa ไทย دری Кыргызча or Kinyarwanda नेपाली Română Malagasy Lietuvių Oromoo Nederlands Soomaali Српски Українська ಕನ್ನಡ Moore ქართული Azərbaycan Magyarالشرح
yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku jël lu Yàlla jagoo jëme ko ci ku dul moom, niki ñaan ku dul Yàlla mu kawe mi, ak xettaliku ci keneen, daal di faatu ca loola kooku ci waa sawara lay bokk. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- teg ca ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kooku mujjam mooy àjjana.فوائد الحديث
Ñaan de ag jaamu la, deesu ko defal ku dul Yàlla mu kawe mi.
Ngëneelu Tawhiid, ak ne ku ca faatu dugg àjjana, donte dañu koo mbugal ci yenn bàkkaaram yi.
Loràngey bokkaale, ci ne képp ku ci faatu dina dugg sawara.
التصنيفات
Wéetal Yàlla ci jaamu ko