إعدادات العرض
ñiy taral alku nañu
ñiy taral alku nañu
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ñiy taral alku nañu» wax na ko ñatti yoon.
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tagalog ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Русский Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල ไทย دری Akan Български Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda тоҷикӣ O‘zbek नेपाली Moore Azərbaycan Oromoo Soomaali Українська bm km rn ქართული mkالشرح
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne way-taral yi ñu sooy lañu wayé ñu Pert lañu yit-ci lu dul njub te du xam-xam- ci seen diine ak séen àdduna, ci séen i wax ak seen i jëf, ñi nga xam ne dañuy jéggi dayob Sariiha bi Yónent bi indi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.فوائد الحديث
Araamal ag taral ak diisal ci mbir yépp, ak soññee ci moytu ko ci lépp; rawatina ci jaamu yi ag màggal ñu baax ñi.
Sàkku li gën a mat ci jaamu yi mbir mu ñu gërëm la; waaye loolu ci topp Sariiha lay ame.
Soppug di feddali mbir yi am solo, ndax Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bàmtu wax ci ñatti yoon.
Yaatug Lislaam ak ug Yombam.
التصنيفات
Wéetal Yàlla ci jaamu ko