Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll

Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll

Jële nañu ci Ubaadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku wax baati Tawhiid yi te xam maanaam te jëfe lamu làmboo, Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ab jaam la tey ab Yonnent, te nangu ne Iisaa ab jaamu la, tey ab yonnente, Ak ne Yàlla moo ko bind ci "kun" nekkal, mu nekk, ak ne moom ruu la ci ruu yi Yàlla bind, Mu setal yaayam ci li Yahuut yi doon askanale ci moom, Mu gëm ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, gëm ne ñoom ñaar xéewalu Yàlla la ak mbugalam, Ba faatu ca loola; kon mujjam mooy àjjana doonte dafa gàtteñlu ci topp Yàlla, te am ay bàkkaar.

فوائد الحديث

Yàlla mu kawe mi moo bind Hiisaa Ibn Maryama ci baatu (kun) ci lu dul baay.

Boole ne Hisaa ak Muhammat -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ay jaami Yàlla lañu ak i ndawam, ñoom ñaari Yonnente lañu te duñu fen, ñaari jaam lañu duñu leen jaamu.

Ngëneelu Tawhiid ak ne day far ay bàkkaar, ak ne mujjug kiy wéetal Yàlla mooy àjjana doonte dafa tàbbi ci yenn bàkkaar yi.

التصنيفات

Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi, Gëm bis bu mujj ba, Meloy Àjjana ak Sawara