إعدادات العرض
Gëm bis bu mujj ba
Gëm bis bu mujj ba
2- Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
4- yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko
5- mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la
6- Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
7- bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
8- li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
12- saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
16- saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee
17- Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
20- giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si
21- dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
22- Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
25- xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
26- {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
28- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man