jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal

jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal

Jële nañu ci Abuu Barsata Al-Aslamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kenn ci nit ñi du weesu bérabu regle ba ëllëg bis-pénc jëm àjjana walla sawara lu dul ne dees na ko laaj ay mbir: Bi ci njëkk: dundam gi ci lan la ko jeexal? Ñaareel bi: xam-xamam bi ndax da koo sàkku ngir Yàlla? Ak ndax jëfe na ko? Ak ndax jottali na ko ñi ko yeyoo? Ñatteel bi: alalam ji fan la ko ame ndax ci lu dagan la walla lu araam? Ak fan la ko dugal, ci lu Yàlla gërëm la walla lu koy merloo? Ñenteel bi: yaramam wi ak kàttanam gi ak jàmmam ji ak waxambaanem gi ci lan la ko ràppale, lu mu ci def?

فوائد الحديث

Ñaaxe ci jëfandikoo dund gi ci lu Yàlla mu kawe mi gërëm.

Xéewali Yàlla yi ci jaam yi lu bari la, te dana ko laaj xéewal yi mu ko jox, kon war na ci moom mu def xéewali Yàlla yi fu Yàlla gërëm.

التصنيفات

Dundug alaaxira