Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor

Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dinaa leen nettali ab Hadiis bu ma dégge ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kenn du leen ko nettali ku dul man: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bokk na màndarga yiy wane ne bis-pénc jege na nu yëkkati xam-xamu Sariiha ci deewug Boroom xam-xam yi, Loolu nag moo waral réer gi bari te tasaaroo, njaalo ak ñaawtéef day tasaaroo, naan sàngara bari, limub góor ñi néew limu jigéen ñi dolliku; ba tax juróom-fukki jigéen am genn góor guy taxawe séeni bir di ko yéwénal.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Leeral yenn màndargay bis-pénc.

Xam waxtuw bis-pénc daa bokk ci biri kumpa yi yàlla jagoo.

Soññee ci sàkku xam-xamu Sariihaa balaa mu fee juge.

التصنيفات

Dundug barsàq, Ngëneeli xam-xam