mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la

mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la

Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdiikarib -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la, kon lépp lu nu ci gis lu dagan dananu ko daganal te lépp lu nu ci gis mu araam, dananu ko araamal, te lu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- araamal, moog lu Yàlla araamal ñoo yam».

الشرح

Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne jamono ju jegee ngi ñëw joj ñenn ci nit ñi danañu toog tëdd ci séen i gàngunaay, Hadiis bu juge ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yeksi fi moom, mu naan: liy àtte sunu diggante mooy Alxuraan ju tedd ji te doy na nu, lu nu fa fekk ci lu dagan nu jëfe ko, lu nu fa fekk ci lu araam nu sori ko. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na lépp lu mu araamaal mbaa mu tere ko ci sunnaam si ab àtteem mook lu Yàlla araamal ci téereem bi ñoo yam; ndaxte moom day jottali jële ci Boroomam.

فوائد الحديث

Dañuy màggal Sunna ni ñuy màggalee Alxuraan te di ko jëfe.

Topp Yónente bi mooy topp Yàlla, moy ko it mooy moy Yàlla mu kawe mi.

Saxal ne sunna aw lay la, ak di tontu ñiy delloo sunna di ko weddi.

Ku dummóoyu sunna di wootewoo ne day yam ci Alxuraan kooku ñaar yépp la bàyyi te day nar ci li muy wootewoo ne day topp Alxuraan.

Bokk na liy tegtale ag yónenteem li muy xibaare lu ñëwagul ci ne di Na am loolu ame niki nimuko xibaare woon.

التصنيفات

Solos Sunna ak wàccuwaayam, Yónnent gi, Dundug barsàq