{te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}

{te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}

Jële nañu ci Subayru Ibnul Awwaam mu wax ne: Bi aaya bii wàccee: {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba} [At-Takaasuru: 8], As-Subayru dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi, ban xéewal lañu nuy laaj, te li fi am mooy ñaar yu ñuul yi rekk muy tàndarma ak ndox? Mu ne ko: «waaye nag dana am de».

الشرح

Bi aaya bi wàccee: {te dees na leen laaj xéewal yi bu bis baa} maanaam: xalset na leen laaj ndax sant ngeen ci li leen Yàlla xéewalal ci ay xéewal, As-Subayru Ibnul Awwaam -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ban xéewal lañu nuy laaj?! Te ñaari xéewal yi jarul laaj te mooy tàndarma ak ndox! Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaye nag dees na leen laaj xéewal ànd ak melokaan wii ngeen nekke yépp, ndax ñoom ñaari xéewal lañu yu màgg ci xéewali Yàlla yi.

فوائد الحديث

Feddalig cant ci xéewali Yàlla mu màgg mi.

Xéewal yi daa bokk ci yi ñuy laaj jaam bi ëllëg bis-pénc moo xam mu néew walla mu bari.

التصنيفات

Dundug alaaxira, Dëddu ak sàmm, Tolluwaayi ñu baax ñi, Pirim laaya yi