ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu

ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu».

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne ay nit danañu feeñ ci mujjanteelu xeetam wi di sos ay fen, di wax loo xamne kenn ku leen jiitu woon masu koo wax, di xibaare ay waxi fen yu ñu duur, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal nu nu moytu leen te bañ a toog ak ñoom, bañ a déglu séen i waxtaan; ngir wax yooyu ñu duur du sax si xel yi, te duñu man a mucc ci moom.

فوائد الحديث

Hadiis bi am na màndarga ci màndargay Yonnent, ndax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare lol dana am ciw xeetam, te am na kem ni mu ko xibaare woon.

Sori kuy fenal Yonnente bi ak diiney Lislaam, te bañ a diglu séen i fen.

Artu ci nangu ay hadiis mbaa di ko tasaare lu dul ginnaaw boo wóorloo ne wér na te sax na.

التصنيفات

Solos Sunna ak wàccuwaayam, Yaxalug Sunnas Yónnent bi SLM, Dundug barsàq